Ca la Boroom bi yewwu ni ku doon nelaw, mel ni jàmbaar ju biiñ xabtal.
TSK
TSK · Isaiah 42:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ndijoor la Aji Sax ji xàcci, ndijooru Aji Sax jee def njàmbaar.
Aji Sax ji, yaa xàcci sa loxo, waaye yéguñu ko. Won leen ni nga nabe ci sa ñoñ, ñu rus, te sawaraay xoyom sa noon yooyu.
Daa xool, gisul kenn; mu tiisoo li ci kenn jógul, moo tax loxoom may ko ndam, te njekkam la sukkandikoo.
Ana kuy kii bawoo Edom, sol yére yu xonq, bawoo Boccra? Kii ak yéreem yu yànj, di daagoo dooleem ju bare? «Xanaa man mii di waxe njekk, te am dooley walloo.»
¶ Aji Sax ji teg ci ne ma: «Yaw nag, jottli leen mboolem kàdduy waxyu yooyu. Te nga ne leen: Aji Sax jeey yëmmoo fa kaw ni gaynde, fa màkkaanam mu sell ma lay àddoo, ŋara ŋar ci kaw déndu suufam, xaacu xaacuy dërkati reseñ, di ko gëdde mboolem waa àddina,
Aji Sax ji mooy Yàlla ju fiir, te mooy mbugale, Aji Sax ji mooy mbugale, te di boroom sànj. Aji Sax ji mooy mbugal ay bañam, mooy sànju ci kawi noonam.
moo tax, xaar ma rekk,» kàddug Aji Sax jee, «ba keroog may jóg, nara sëxëtooji, nde maa dogala dajale xeet yi, dajale nguur yi, ngir xëpp leen samam sànj, mboolem sama tàngooru mer. Sama sawaras fiiraange déy, ci la mboolem àddina di xoyomu.