Yeen boroom daraja yi, buleen yàqati sama der, buleen sopp caaxaan, di sos. Selaw.
TSK
TSK · Isaiah 43:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mooy nangul aji tumurànke, xeebul ñaanam.
Lu Aji Sax ji sàkk, mbir la ca namm, ba ci ku soxor ak bésu mbugalam.
Sa askan wépp ñu jub lañuy doon, te ñooy moom réew mi ba fàww. Ñooy sama njëmbat li ma jëmbatal sama bopp, sàkke leen samay loxo, ngir sama teddnga teew.
Dëkk bi daldi doon sama woy, di sama mbégte, di sama ndam, di sama sag ci biir mboolem xeeti àddina yi dégg ngëneel yi ma leen di defal yépp. Dinañu yéemu ba seen yaram daw ci lépp luy ngëneel ak jàmm ju ma leen di defal.»
Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell, gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp,
la dogaloon lu jiitu, ne ci Yeesu Almasi la nuy defe ay doomi boppam, te muy bànneexam, di coobareem.
Ndax moo di ki Yàlla sàkke lépp lu nekk asamaan, ak lu nekk ci suuf, lu gisu, ak lu gisuwul, muy boroom gàngune yeek, boroom ndomboy tànk yeek, boroom nguur yeek, boroom sañ-sañ yi. Lépp ci moom lees ko sàkke, te mooy ki tax ñu sàkk lépp.
¶ Kon nag saa su nekk, nanuy jooxee ci Yeesu, sunu saraxu cant, ñeel Yàlla, muy sarax su bawoo ci sunuw làmmiñ, ñu di ko birale aw turam.