TSK

TSK · Isaiah 44:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Waaye wattuleen, wattuleen seen bopp bu baax, bala ngeena fàtte mbir yi ngeen teg seen bët, ba du génn seenum xel seen giiru dund gépp. Te nangeen ko xamal seeni doom ak seeni sët.

Léegi nag bindleen woy wii ma leen di dégtal, te yaw Musaa nga jàngal ko bànni Israyil. Woyloo leen ko, ndax woy wii di sama seede ak bànni Israyil.

Yeen askanu Yanqóoba, lu ngeen di jàmbat? Yeen Israyil laa ne, lu ngeen di jooy, naa: «Aji Sax ji gisul li nu dal, sunu Yàlla daal, daa réere sunu àq!»

Ana kan ci yeen mooy dékk lii nopp? Kuy teewlu, ba doxe fa dégg?

Délloosil képp ku ñu ma tudde, te sama màqaama tax ma sàkk ko, tabax ko, sottal ko.»

Yaw Yanqóoba, sama jaam bi, déglul boog, yaw Israyil sama tànnéef laa wax.

«Ana jaboot juy fàtte doomam juy nàmp, mbaa muy néege ku mu jur ci biiram. Bu ko manoona fàtte it, man duma la fàtte.

¶ Ci wàllu xibaaru jàmm bi, ay noon la Yawut ñi taxawe, te muy xéewal ci yeen ñi dul Yawut. Waaye ci wàllu dogal bi taamu Yawut ñi, ay soppe lañu, te seeni maam tax.