Yettro bég lool ca la Aji Sax ji def lépp, ba baaxe Israyil, xettli leen ca noteelu waa Misra.
TSK
TSK · Isaiah 44:23
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Aji Sax ji day dégg néew-ji-doole moos, te du sàggane ñoñam ñi ñu njoñ.
Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk. Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur.
Na géej riirandook li ko fees, mook àddinaak li ci biiram,
Màggal-leen ko yeen tund yu mag yeek yu ndaw yépp, ba ci garab yiy meññ ak garabi seedar yi,
Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, yeen waa cati àddina, kañleen ko, ànd ak ñiy wàcci géej ak li ci biiram, ak duni géej ak ña ca dëkke.
Moo ma ne: «Israyil yaa di samab jaam, yaw laay wonee samag leer.»
Yeen genti Yerusalem, àndleen sarxolle; Aji Sax jeey dëfal ñoñam, mooy jot Yerusalem gii!
Sa askan wépp ñu jub lañuy doon, te ñooy moom réew mi ba fàww. Ñooy sama njëmbat li ma jëmbatal sama bopp, sàkke leen samay loxo, ngir sama teddnga teew.
Su boobaa asamaan ak suuf ak mboolem li ci biiram sarxollendoo, di bége li dal Babilon. Bëj-gànnaar kay la yàqkat yay bawoo.» Kàddug Aji Sax jee.
«“Waaye yeen tundi Israyil, yeenay naat, di meññal Israyil sama ñoñ, te léegi ñu ñibbsi.
Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.
moo yelloo daraja ci biir mbooloom gëmkat ñi, ak ci Almasi Yeesu, tey ak ëllëg, ba fàww. Amiin.
Kuy wax, na waxe nu mu jottlee kàddug Yàlla. Kuy taxawoo, na taxawoo ci dooley Yàlla, ngir màggug Yàlla feeñe ci lépp, ndax Yeesu Almasi, mi yelloo daraja ak kàttan, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
Kon nag yaw asamaan, bégal, yaak mboolem ñi ci sa biir! Waaye wóoy ngalla yeen géej ak jéeri! yeen, ñi Seytaane wàccaale mer mu tàng fi yeen, ndax xam ne fan yu néew a ko dese.»
¶ Gannaaw loolu damaa dégg lu mel ni coow lu xumb, bawoo ci mbooloo mu bare mu àddoo asamaan, ne: «Aleluya! Texe ak daraja ak kàttan ñeel na sunu Yàlla.