Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.»
TSK
TSK · Isaiah 46:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Nguur gi du jóge ci loxol Yuda, te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam, li feek boroom di ñëw, ba xeet yi déggal ko.
Maa ngi koy gis, te du tey, Maa ngi koy niir, te jubseegul; biddiiw a feqe fa Yanqóoba, yetu nguur a yékkatikoo fa Israyil, daldi toj boppi Mowab, toj kaaŋi mboolem askanu Set.
¶ Waaye nag su ngeen déggalul seen Yàlla Aji Sax ji, te baña sàmmoo jëfe mboolemi santaaneem, ak dogali yoonam, yi ma leen di jox tey, mboolem alkànde yii dina leen dab, sottiku ci seen kaw:
Aji Sax ji nas, mu àntu ba fàww, mu mébét, mu sottil maasoo maas.
Bare na lu xol di mébét, waaye Aji Sax jeey dogal.
Boroom bi nee: «Bu ma sottalee liggéey fa kaw tundu Siyoŋ ak fa Yerusalem, maay mbugale buurub Asiri réy-réyloom gi, ak gëti xeebaateem.»
Aji Sax ji, yaay sama Yàlla, dama lay teral, di la sant. Yaa defi jaloore, muy dogal yu yàgg, wér te wóor.
«Woneleen ko te wax nu liy ñëw. Xamal-leen nu la woon, lu mu; nu ba ci xel, ba xam lu muy jur, te ngeen dégtal nu la dikkagul.
Ana ku mel ni man? Na àddu! Na biral firndeem te taajal ma la amoon ba may sos xeet wu yàgg wa, ak li dikkagul. Na ko wax!
Maay wooye jaxaay penku, wooye réew mu sore, kuy sottal sama mébét. Maay àddu, amal; maay nas, sottal.
¶ «“Bés baa ngii di ñëw te dina dikk, kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Bés bii laa waxoon.
Képp ku déggalul yonent boobu, dees na la xettee ci xeet wi, sànk la.”
Waaye su bawoo fa Yàlla nag, dungeen ko mana fanq, moytuleena jànkoonte ak Yàlla.» Ñu daldi fekksi Gamalyel,
¶ Céy xóotaayub koomu Yàlla ak xel ma, ak xam-xam ba! Deesul natt ay dogalam, deesul ràññee ay jëfinam!
Yàllaa bëggoona firndeel nu mu gëna leere ñeel ñi moom dige bi, ne ab dogalam du tebbiku mukk. Moo tax mu dogale ngiñ ab digeem.