«Ana kuy sa moroom ci tuur yi, yaw Aji Sax ji? Kuy sa dend, yaak sa sellaay bu yéeme, sa yànjaay bu raglook sa jëf yu yéeme?
TSK
TSK · Isaiah 46:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Kenn du Yàllay Yesurun! Keey war asamaan, wallusi leen, war ay niir, ànd ak darajaam.
Ndeke yoo lii nga dencoon ci sa xol, xam naa ne lii nga naroon:
Maa ngi leen di léeb, di sulli kumpay démb,
Moo dogal ñuy fàttlikuy kéemaanam; Aji Sax ji boroom yiw ak yërmande.
Yeen sama ñoñ, yeenay samay seede. Kàddug Aji Sax jee. Yeenay sama jaam bi ma taamu, ngir ngeen xam, ba gëm ma, ba ràññee ne maay moom. Sàkkeesul yàlla ju ma jiitu, mbaa ju may wuutuji.
Aji Sax ji dafa wax ne: «Muy ñaqu Misra, di koomu waa Kuus, ak waa Seba, ya ne sireet ca kaw, ñoom ñépp ay jàllsi, nga jagoo. Sa gannaaw lañuy topp, yeewe, jàllsi; sujjóotal la, di ñaan naan: “Fi yaw daal la Yàlla ne, du feneen, te tuur neen la.”»
Àdduleen, layoosi, diisooleen fi seen biir kay! Ana ku xamle woon lii bu yàgg, yégle woon ko booba? Xanaa du man Aji Sax ji? Kenn du Yàlla ku dul man! Yàlla ju jub, di walloo, du kenn ku dul man!
Yàgg na maa biral lay jëkka am. Tuddoon naa ko, yégle ko, jekki jëf ko, mu sotti.
Aji Sax ji dafa wax ne: «Taxawleen ca selebe yoon wa, xool, te laajte yoon ya woon, ne: “Ana yoonu mbaax?” Ngeen awe ca, am noflaayu bakkan.» Ñu lànk ne: «Awunu ca.»
Dégluwunu say jaam, di yonent yi jottli sa kàddu sunuy buur ak sunuy kilifa ak sunuy maam ak mbooloom réew mi mépp.