bu ma daasee sama saamar buy melax, ba ŋàbb ko ci saab loxo, di àtte, maay fey samay digaale, añale samay bañ.
TSK
TSK · Isaiah 47:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Yeen waa Babilon, gi ñu nara fàllas, ndokklee ku leen fey jëf, ja ngeen nu def!
Yeen xeet yi, jegesileen te déglu; yeen askan yi, teewluleen! Na suuf ak li ci biiram déglu, muy àddinaak lépp lu mu jur.
Moo sol kiiraayal njekk, mbaxanawoo mucc, solati yérey mbugale, làmboo turkib xéraange.
Soo nee ci sam xel: «Lu tax lii dal ma?» xamal ne sa ñaawtéef gu réy a waral ñu ñori la, saaysaaye la.
Jamleen seen jàmbaari yëkk yépp, nañu dem ca rendikaay ba. Wóoy, ngalla ñoom! Seen bés taxaw na moos, di seen àppu mbugal.
«Nàmmleen fitt yi, feesale mbar yi! Aji Sax ji xabtal na buuri Medd fi kaw Babilon, nar koo tas. Lii mbugalu Aji Sax jee, mbugal mi këram waral.
«Buuru Babilon warax na ma. Da maa muucu, ñiit ma, ba ma set ni ndab. Da maa modd ni ninki-nànka, sole kollam li gën ci man, yàbbi la ca des.»
maa ngii nag di dajale mboolem sa far yi la doon bége, ñi nga bëgg ñépp ak ñi nga bañ ñépp. Maa leen di dajalee fu nekk ci sa kaw, ba noppi ñori la yaramu neen, ñu gis la nga ne duŋŋ.
Samay soppe, buleen di feyul seen bopp, xajal-leen am sànj, am sànj fajal boppam, ndax bindees na ne: «Man maay feye, maay añale.» Boroom bee ko wax.
¶ Ba mu tàyyee juróomeelu tayu gi, ma gis ci suufu sarxalukaay bi, bakkani ñi ñu bóom ndax kàddug Yàlla ak seede si ñu ci seede.
Ndaxte ay bàkkaaram jalu na ba àkki asamaan, te Yàlla bàyyi na xel ay ñaawtéefam.