Mooy sàmm jéegoy wóllëreem, ku bon sànkoo biir lëndëm, nde doole mayewul ndam.
TSK
TSK · Isaiah 47:5
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mu ngi fey xare ci àddina sépp, dog fitt, damm xeej, lakk pakk.
Babilon nag, mooy gànjaru réew yi ko wër, di teraanga ji Kaldeen ñiy sagoo, waaye Yàllaa koy tas, mu ne tasar ni Sodom ak Gomor.
Mu ne: «Maa koy def kërug siññéel, def ko ab tan, ba buube ko buubub rajaxe.» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
te naa: «Ba fàww maay lingeer!» ba tax bàyyiwoo xel ca la ngay def; xalaatoo la muy jur.
Te muy kàddug mbégte di kàddug bànneex, di kàddug boroom séet akub séetam, di wolukaay bu fiy jib mbaa leer gu ñuy niitoo, lépp maa ko fiy boole tukkal.
Yaw Buur, buuru buur yi, yaw mi Yàlla Boroom asamaan jox nguur ak kàttan ak dooleek ndam,
Maa ngii déy di xàcci sama loxo ci seen kaw, te ñoom la seeni jaam di sëxëtooji.» Kon dingeen xam ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moo ma yebal.
Ñooy gannaxi géej gu sàmbaraax, di gëq seen puuriti gàcce; ñooy biddiiw yu fàq di taxawaalu, te lëndëm gu ne këruus di cér bu ñu leen sédde ba fàww.
Jigéen jii nga gis, moo di dëkk bu mag, bi yilif buuri àddina.»
naan: «Wóoy, wóoy ngalla dëkk bu mag ba! Ngalla yaw, dëkk bu mag, ba daa woddoo lẽe ak ndimo lu yolet ak lu xonq curr, takkoo wurus ak doji gànjar aki per,