TSK

TSK · Isaiah 48:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ci kaw loolu Musaa yékkati loxoom, dóor yetam ca doj wa ñaari yoon, ndox mu bare wale ca, mbooloo ma daldi naan, ñook seenug jur.

Sa xel mu rafet nga leen may ba ñu mana ràññee, sa mànn it, noppiwuloo leen koo leel, teg ca ndox ma nga leen daan fajale mar.

Dóor naw doj, moos, ndox ma fettax, wal ma baawaan, waaye aw ñam nag? Daa mana leel mbooloo mii aw yàpp?»

Te tundoo tund wu kawe, wu mag ak wu ndaw, wali ndox a cay wale, keroog bés ba deret di tuuroo tuuru, tata ya jóoru.

Walaakaanaak néew-doolee ngi wër, di wut um ndox, amul. Seen put wow koŋŋ ak mar. Man Aji Sax ji, maa leen di nangul; man Yàllay Israyil, duma leen wacc.

dundooti àll bi di ma sàbbaal, ñook njabootug bànjóoli, nde maa mayem ndox fi màndiŋ mi, dex ya wale fu noon sereŋ, ma nàndale sama ñoñ, sama tànnéef,

Ñooy dikk di jooy, di leewaayu, ma jiite leen, yóbbu, jaare leen xàll wu jub wu ñu dul fakktaloo, ba ca wali ndox ya, ngir maay baayu Israyil, Efrayim di sama taaw.