Gàntal Aji Sax ji ngeen nekke naka jekk, dale ko ca bés ba ma leen xamee.
TSK
TSK · Isaiah 48:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Man nag maa leen di làqa làq sama kanam, bésub keroog ndax mboolem mbon gi ñu def, ndax ñoo walbatiku ci yeneen yàlla.
Xam naa ne maa tooñ, sama moy a ngi janook man saa su ne.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax ji, yaa ma natt, xam ma;
Peeñu mu ñàng lañu ma ci wax. Workat biy wor, yàqkat biy yàq. Yeen waa Elam, songleen; yeen waa Medd, gawleen leen. Dakkal naa mboolem onk yu ñu sabab.
Aji Sax ji déy yeen la wal ngelawal nelaw yu xóot, taf seeni gët, te ngeen di yonent yi; muur seeni bopp te ngeen di boroom peeñu yi.
Gis nga lu bare, waaye jàppoo ci dara. Nopp ne kótt, dég-dég të!»
Xam naa ne ñu dëgër bopp ngeen. Dangeen të, wowle.
Ma noon su ma defee loolu lépp ba noppi, dina délsi, te délsiwul. Te doomu ndeyam Yuda workat bi gis na ci.
Waa kër Israyil ak waa kër Yuda kat, ñoo ma wora wor!» Kàddug Aji Sax jee.
Moo kan laay waxal, àrtu ko ba mu déglu, yii boroom noppi paaxee tëë teewlu! Kàddug Aji Sax jaa ngii, mel ni lu ñu rus, lu ñu safoowul!
Aji Sax ji lañu wor, nde doomi po lañu jur; Léegi la leen màggalug Terutel weer di booleek seen suuf, sànk leen.
Yuda wor na, lu jomblu lees def fi Israyil ak Yerusalem. Yuda déy moo teddadil li Aji Sax ji sopp te mooy bérabam bu sell: Yuda moo takk janqub yàllay doxandéem.