TSK

TSK · Isaiah 48:9

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ndaxam muñal nga leen ay at yu bare, di leen artoo sam xel, say yonent di leen ko jottli; waaye taxul ñu déglu. Nga teg leen nag ci loxoy waa réew yi.

Teewul mu yërëm, baal leen seen ñaawtéef, ba sànku leen. Muñ na meram, muñati, te toppul xolam,

Yërmandeeku yiw, fa Aji Sax ji. Moo muñ mer te bare ngor.

Aji Sax ji, musal ma ngir saw tur, jëfeel sag njekk, teggil ma njàqarey bakkan.

Aji Sax ji déy a leen namma baaxe, moo ko tax di jóg moos ngir yërëm leen, nde Aji Sax jeey Yàllay njubte. Ndokklee képp ku ko yaakaar!

Mennum man mii maay far say moy ngir man, ba dootuma fàttliku bàkkaar.

Dëgg la sunuy ñaawtéef a nu tuumaal, waaye éy Aji Sax ji, jógal te saw tur tax, doonte dëddu nanu la ay yooni yoon, moy la.

Teewul ma sédd ci sama teddngay tur, ngir xeet, ya seede woon ba ma leen di génne, bañ maa sikk.

Yeen waa kër Israyil, duma jëflanteek yeen li seen jikko ju bon yelloo ak seen jëfi yàqute, waaye sama teddngay tur laa ciy seet, ba ngeen xam ne man maay Aji Sax ji. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»

¶ «Kon nag yaw sunu Yàlla, Sang bi, rikk nangul li ma lay ñaan, di la ko dagaan. Boroom bi, ngalla geesul ngir yaw ci sa bopp sa jaamookaay ba ñu gental.