Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk. Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur.
TSK
TSK · Isaiah 49:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
te mbooy mi di jaayu, mook lu ci biiram, garabi àll bi sarxolleendoo,
Màggal-leen ko yeen tund yu mag yeek yu ndaw yépp, ba ci garab yiy meññ ak garabi seedar yi,
Dëfal-leena dëfal sama ñoñ, la seen Yàlla wax!
Asamaan, sarxolleel, Aji Sax ji dikk na! Yeen xóotey suuf, xaaculeen! Yeen tund yi, neleen réllet, sarxolleendoo, ak yaw gott beek sa bépp garab! Aji Sax jee jot Yanqóoba, te moom Israyil lay fésale darajaam.
Yeen genti Yerusalem, àndleen sarxolle; Aji Sax jeey dëfal ñoñam, mooy jot Yerusalem gii!
Moo ma yónni ngir ma yéene atum yiwu Aji Sax ji, ak at mu sunu Yàlla di mbugalee. Moo ma yónni ngir dëfal ñiy ñaawlu ñépp,
Su boobaa janq bégem pooj, waxambaaneek mag feelu ko, ma soppi seen ñaawlu mbégte, dëfal leen, bànneexal leen, ñu dëddu naqar.
Maa leen wax ne leen: noonu rekk lay doone mbégte fa malaakay Yàlla ya, bu benn bàkkaarkat doŋŋ tuubee.»
¶ Sunu Sang Yeesu Almasi ci boppam, ak Yàlla sunu Baay, mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk, ak yaakaar ju wér,
¶ Gannaaw loolu ma jekki gis mbooloo mu réy mu kenn manula waññ, ñu bawoo ci askan yépp ak giir yépp ak xeet yépp ak làmmiñ yépp. Ñu ngi taxaw fi kanam ngàngune mi ak Gàtt bi, sol mbubb yu weex, ŋàbb ay cari garabi tàndarma.