Yuda yaa di gaynde gu ndaw, doom, doora jóge nii ci pàdd, tey yuug ak a goor ni gayndeg sibi. Yaa di gaynde gu deesul yee.
TSK
TSK · Isaiah 5:29
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
«Yeen fàttekati Yàlla yi, déggleen lii, bala maa fàdd te kenn du wallu.
Aji Sax ji déy da maa wax ne ma: «Gaynde gu mag ak gu ndaw, bu jàppee bay xiiru, boo ko wooloon gàngooru sàmm it, duñu soowaloo ba xëbal ko, duñu ñolñoli ba mu dellu gannaaw. Noonu la Aji Sax ji Boroom gàngoor yiy wàcce, xaresi fi kaw tundu Siyoŋ ak waa tund wa.»
Manees naa foqati alalu sëxëtoo ci loxol jàmbaar a? Am manees naa rëcc boroom doole bu la jàpp?
«Gayndee fëlle geeram, fàkkaskatu xeet yee jóg, génne këram, nara gental seeni dëkk, ba ñu di gent yu kenn dëkkul.
«Israyil diy gàtt yu tasaaroo, yu ay gaynde dàq, buurub Asiri di gaynde gi jëkka lekk, Nabukodonosor buuru Babilon topp ca, seeñu yax ya.»
Dees na topp ci gannaaw Aji Sax ji, muy yëmmu ni gaynde. Mooy yëmmu moos ni gaynde, ay doomam di lox, jóge sowu.
Aji Sax ji, sa loxo ca kaw, tiim say bañ, mboolem say noon lees di dagge ci kaw suuf.
Jooyi sàmm ya jib na, seen daraja réer na, ŋari gaynde ya it jolli na, nde gajjug tàkkal Yurdan a tas.