waaye yeenay doon nguuru sarxalkati Yàlla, te di xeet wu sell.” Kàddu yooyu ngay wax bànni Israyil.»
TSK
TSK · Isaiah 51:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ndokklee yeen xeet wi Aji Sax ji di seen Yàlla, yeen askan wi Aji Sax ji séddoo.
Muy taalif bu giiroo ci Asaf. Yeen sama xeet, dégluleen, ma digal leen; teewluleen ma, ma wax leen.
Loolu defalu ko wenn xeet; kenn xamu ci ndigali yoonam. Màggal-leen Ki Sax!
Ay askan yu bareey dikk, naan: «Dikkleen nu yéegi tundu Aji Sax ji, fa kër Yàllay Yanqóoba, mu xamal nuy yoonam, ba nu doxe yooyu ñallam.» Siyoŋ kat la ndigalu yoon di bawoo, Yerusalem googu la kàddug Aji Sax ji di jóge.
«Xool-leen sama jaam bi ma yor, sama tànnéef, sama soppey xol, ci kawam laa teg samag noo, te mooy dogalal xeet yi yoonu àtte.
Mu ne: «Man Aji Sax ji, maa la woo cig njekk, jàpp la ci loxo, sàmm la, def la ngay kóllëre sama digg ak nit ñi; def la ngay leeru xeet yi,
Xeet yu bareey dikk te naan: «Dikkleen nu yéegi ca tundu Aji Sax ji, kër Yàllay Yanqóoba, mu xamal nuy yoonam, ba nu doxe yooyu ñallam.» Siyoŋ kat la ndigalu yoon di bawoo, Yerusalem googu la kàddug Aji Sax ji di jóge.
mu dig leer, ñeel jaambur ñi, sagal Israyil sa ñoñ.»
Ndax kat, dooley Noo giy maye bakkan te nekk ci Almasi Yeesu moo la yiwi, ba nga mucc ci dooley bàkkaar ak ndee.
¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.