Nguur gi du jóge ci loxol Yuda, te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam, li feek boroom di ñëw, ba xeet yi déggal ko.
TSK
TSK · Isaiah 55:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Nangeen sàmm samay dogal ak samay santaane, ndax ngeen jëfe yooyu moo leen di taxa dund. Man maay Aji Sax ji.
Kon nag Sang bi, nangula barkeel sama kër, ngir mu sax ba fàww fi sa kanam. Ndax kat yaw Boroom bi Aji Sax ji yaa wax, te ci sa barke la sama kër di barkeele ba fàww, Sang bi.»
Te it maa koy def samab taaw, tiimale ko buuri àddina,
Duma fecci sama kóllëre, te duma toxal sama kàddu.
Doom, déglul samay kàddu, teewlul samay wax.
Sama xol a jóg, ma xañ la sama kanam ab diir, waaye maa lay yërëme ngor gu sax.» Aji Sax, ji lay jot moo ko wax.
Waaye seen Yàlla Aji Sax ji lañuy jaamu ak seen buur bi ma leen di falal, mu toogal Daawuda.
«Aji Sax ji dafa wax ne: Ndegam manees naa dog sama kóllëre maak bëccëg mbaa sama kóllëre maak guddi, ba bëccëg mbaa guddi baña teew ci waxtoom,
Yeremi ne ko: «Deesu la leen jox. Dangay déggal Aji Sax ji ci li ma la wax rekk, muy sa jàmm, nga mucc.»
Waaye man maay bàyyi xel sama kóllëre gi ma fasoon ak yaw ba ngay ndaw. Maa lay saxalal kóllëre guy wéy ba fàww.
¶ «“Daawuda sama jaam baay doon seen buur, di seen bennub sàmm ñoom ñépp. Sama àttey yoon lañuy doxe, sama dogali yoon lañuy sàmm, di ko jëfe.
Noonu ko Yàlla dekkale ndekkite lu dee toppatul, te yaramam du yàqu mukk, noonee la ko Yàlla waxe woon, ne: “Maa lay jox barkey Daawuda yu sell yi te wóor.”
¶ Yàlla miy boroom jàmm, moom mi dekkal sunu Sang Yeesu, Sàmm bu mag bi, ci dooley deret ji mu fase kóllëre gu sax dàkk,