TSK

TSK · Isaiah 55:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Nguur gi du jóge ci loxol Yuda, te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam, li feek boroom di ñëw, ba xeet yi déggal ko.

Ma wol, ba ñu doon pënd, ngelaw wal, ma wetti ni banu mbedd.

Bésub keroog car bawoo ca Yese, reen ba, taxaw di raaya buy gindi xeet yi, xeet yi di ko sàkku, dal-lukaayam ba jagoo teddnga.

Mu ne: «Xeeb naa li ma la sas ngay sama jaam biy siggil giiri Yanqóoba, te wara délloosi ndesu Israyil gii. Tabb naa la, ngay leeru xeet yi, di jotale waa cati àddina sama wall.»

Ab seedee ngoog, ñeel xeet yi, muy njiit, yilif xeet yi.

Yaa koy gis, sa kanam ne ràññ, fit tëf-tëfi, xol fees dell, nde dees na walbati xéewali géej, indil la, alali xeet yi dikkal la.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Ay askan ñooy dikkati, di waa dëkk yu bare,

Xanaa du fàww Almasi daj boobu coono, doora dugg ci teraangaam?»

Acts 5:31 TSK

Moom la Yàlla yékkati ci wetu ndijooram, def ko muy Njiit, di Musalkat, ngir may bànni Israyil ag tuubeel ak njéggalug bàkkaar.

¶ Kon nag, yeen jaambur ñi dul Yawut cib juddu, yeen ñi ñuy wooye yéefar yi xaraful, te ñi leen ko dàkkantale woon di Yawut yi xarafe ci loxol nit ku leen xarfal ci seen yaram, fàttlikuleen seen démb.

Noonu la woon itam ci Almasi. Tegoowul boppam darajay doon sarxalkat bu mag, waaye Yàllaa ko ne: «Yaa di sama Doom, bés niki tey maa la jur.»