«Man maa tabb buur, fal ko ci Siyoŋ, sama tund wu sell.»
TSK
TSK · Isaiah 56:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Boo wootee wall, na la sa gàngooru tuur xettli. Ñoom ñépp la ngelaw di buub, callweer yóbbu leen. Waaye ku ma làqoo, kookooy moom réew mi, séddoo sama tund wu sell wi.
Maay teg firnde fi seen digg, ba jël ñenn ca ña dese bakkan ca ñoom, yebal leen ci xeet yi, yebal leen Tarsis, ak Pul ak Ludd, ñooña di ñu mane fitt, ma yebal leen ca waa Tubal ak Yawaan, waa duni géej yu sore ya, ñooñu masula dégg sama jaloore, te masuñoo gis sama teddnga, sama ndaw ñaa leen di xamal sama teddnga.
Nangeen ko tegoo bant, séddoo ko ci seen biir, yeen ak doxandéem yi sanc ci seen digg te jaboot ci réew mi. Nangeen leen jàppe ni ay njuddu-ji-réew fi digg Israyil. Nañu am seen céru suuf ni yeen, bokk ci yem ak giiri Israyil.
Aji Sax ji dafa wax ne: «Maay dellu Siyoŋ, Yerusalem googu laay màkkaanoo, ba ñuy wooye Yerusalem dëkkub Worma, foofu di tundu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, lees di wooye tundu Sellnga.»
Mu ne leen: «Bindees na ne: “Sama kër gi kërug julli la, waaye yeen, moom ngeen def rawtub sàcc!”»
¶ Kon nag, yeen jaambur ñi dul Yawut cib juddu, yeen ñi ñuy wooye yéefar yi xaraful, te ñi leen ko dàkkantale woon di Yawut yi xarafe ci loxol nit ku leen xarfal ci seen yaram, fàttlikuleen seen démb.
¶ Waaye yeen fi ngeen agsi moo di tundu Siyoŋ, dëkku Yàlla jiy dund, te mooy Yerusalem ga ca asamaan, yeena àgg fa junniy junniy malaaka, dajee di màggal;
¶ Ci man Piyeer, ndawal Yeesu Almasi la bataaxal bii bawoo, ñeel askan wi Yàlla taamu, te ñu toxuji diiwaani Pont ak Galasi ak Kapados ak Asi ak Bitini.