TSK

TSK · Isaiah 58:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ci biir loolu Aji Sax ji dégg la ngeen ma wax. Mu ne ma: «Dégg naa li la mbooloo mii wax. Ñoo yey wax yooyu kàddu yépp.

Saraxub ku soxor, Aji Sax ji bañ na ko; ñaanu kuy jubal da koy bége.

Boroom bi nee: «Askan wii, làmmiñ lañu ma jegee, lori neen lañu may wormaale, te seen xol sore ma. Seen ragal ak man it, njàngum tari kepp la.

Yeen waa kër Yanqóoba, dégluleen; yeen ñi ñu wooye turu Israyil, yeen ñi bawoo bëti ndoxi Yuda, di giñe turu Aji Sax ji, yeen ñiy sàbbaal turu Yàllay Israyil te dëgg ak njekk taxul,

Yeena sànk seen bopp ba ngeen ma yebalee ci seen Yàlla Aji Sax ji, ne ma ma ñaanal leen sunu Yàlla Aji Sax ji, te lépp lu sunu Yàlla Aji Sax ji wax, naa leen ko jottli, ngeen def ko.

¶ «Léegi nag, yaw nit ki, sa bokk yaa ngi lay waxtaane ci keppaari tata yi ak ci bunti kër yi. Ñu ngi waxante ci seen biir, ku nekk naa mbokkam: “Aycaleen nu dem dégluji gan kàddoo tukkee ci Aji Sax ji.”

¶ Ñi ñu xasa leeral nag, te ñu jota mos may gu bawoo asamaan, séddu ci Noo gu Sell gi, deesu leen mana defal dara.

James 4:8 TSK

Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yeen bàkkaarkat yi, raxasleen seeni loxo, yeen ŋaralekat yi laa ne, setal-leen seen xol.