Ñooy sos joote, wasin ñaawtéef, ñoom la seen biir di ëmb wuruj.
TSK
TSK · Isaiah 59:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ku bon a ngoog, di matu doomu ñaawtéef. Day sos njombe, wasin njublaŋ.
Xanaa dungeen bàyyee songandoo nit, nar koo sànk, ni kuy màbb tabax bu joy, mbaa ngay bàddi per mu ràpp?
Ku bon du nelaw te lorewul, du dajjant ba kera muy téqe.
Seeni mébét di boob, bu sottee dim ngooñ; seen noowug bopp mooy xamb sawara, wi leen di xoyom.
Noo tooñ Aji Sax ji, wor ko, te noo dëddoo sunu Yàlla jii, kàdduy fitna ak fippu, ak fen yu nu mébét, nas ko,
«Wërleen mbeddi Yerusalem, xool-leen, seet ciy péncam rekk ba xam ndegam dingeen gis kenn, kenn kepp kuy def njub, di sàmm worma, ma daldi leen baal.
Buleen naxe seen bopp kàdduy caaxaan, naan: ‘Kër Aji Sax jaa ngi, kër Aji Sax jaa ngi fii, kër Aji Sax jee!’
Waa réew maa ngi lekk àq, di sàcc. Baadoolo yeek walaakaana yi, ñu néewal; doxandéem bi, ñu not, xañ ko àqam.
Ngor a jeex ci réew mi, njub tumurànke ci nit ñi. Ñépp, ku ñu tuur deretam lañuy tëru, ku nekk, mbokkam lay fiir.
Te xemmemtéefu bakkan bu ëmbee, bàkkaar lay wasin, te bàkkaar bu matee, ndee lay jur.