TSK

TSK · Isaiah 6:10

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Waaye man maay dëgëral boppu Firawna, ba fulandi samay firnde ak samay kéemaan ci biir réewum Misra.

Musaa ak Aaróona def nañu yooyu kéemaan yépp ca kanam Firawna, waaye fekk na Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, ba mu të, baña bàyyi bànni Israyil, ñu génn réew ma.

¶ Siwon buurub Esbon nag nanguwu noo may nu jaare fa moom, ndax booba seen Yàlla Aji Sax ji moo dëgëral boppam, wowal xolam, ngir teg ko ci seen loxo niki bésub tey jii.

Yeen Yesurun, yeena yaflu, waŋŋeetu, solu yaram, ne faaj, ne fuux, fàtte Yàlla mi leen sàkk, faaleedi seen cëslaay li leen musal.

Ñu ngi nii, seen bopp yi, tafas; te man may tàqamtikoo saw yoon.

Mu jot nga rey, mu jot nga faj; mu jot nga toj, mu jot nga tabax.

Moo tax seen kàddug Aji Sax mujj di: «Ca rëdd wii, ca rëdd wee, nàngam sii, nàngam see, as tuut fii, as tuut fee.» Moo tax ñuy tërëf, daanoo njaaxaanaay ba damm, di sërëx ak a keppu.

Aji Sax ji déy yeen la wal ngelawal nelaw yu xóot, taf seeni gët, te ngeen di yonent yi; muur seeni bopp te ngeen di boroom peeñu yi.

Ngalla dégluleen lii, xeet wu dofe, ñàkk xel wi ngeen doon, ami gët te dungeen gis, ami nopp te dungeen dégg!

Bare na waaso yoo xamul seeni wax, yu xóotu làkk te diisu làmmiñ. Te su ma la yebaloon ci ñoom, ñu déggal la.

Acts 3:19 TSK

Kon nag tuubleen te dëpp, ndax seeni bàkkaar faru.

Teewul muy ci ñii, xetu ndee gu jëme ci ndee, te di ci ñee, xetu dund gu jëme ci dund. Boobu sas nag, ana ku ko àttan?