Mbooloo ma nag di diiŋat Musaa, naan: «Ana ndox mu nuy naan nag?»
TSK
TSK · Isaiah 63:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Bàyyileen ko xel bu baax, déggal ko te bañ koo merloo, ndax du leen baal seen moy, ngir sama tur la taxawe.
Maa leen di noonoo ba seeni noon duma leen, seeni bañ yilif leen. Dingeen daw te kenn dàqu leen.
¶ Ku ñuy wax Kore doomu Isar, mi askanoo ci Keyat doomu Lewi, moo àndoon ak ay Rubeneen, ñuy Datan ak Abiram, doomi Elyab, ak Onn doomu Pelet,
¶ Fàttlikuleen! Buleen fàtte na ngeen merloo woon seen Yàlla Aji Sax ji ca màndiŋ ma. La dale bés ba ngeen bàyyikoo réewum Misra, ba ba ngeen agsee bérab bii, fippu ci kaw Aji Sax ji ngeen masa nekke.
¶ Waaye nag su ngeen déggalul seen Yàlla Aji Sax ji, te baña sàmmoo jëfe mboolemi santaaneem, ak dogali yoonam, yi ma leen di jox tey, mboolem alkànde yii dina leen dab, sottiku ci seen kaw:
¶ «Sunu maam yooyu kay ñoo mujj fuuy, sajju loos, ba sàmmuñu say santaane.
Artu nga leen ndax ñu dellu ci saw yoon, teewul ñu bew, ba sàmmuñu say santaane, xanaa di moy sa àttey yoon yiy taxa dund képp ku ci sàmmu. Ñuy daŋŋiiral, sajju loos, bañ laa déggal.
te baña roy seeni maam; maas gu të woon te déggadi, ñu ñàkk pastéef te sàmmuñu kóllërey Yàlla.
Gàntal nañu ko ba tàyyi ca màndiŋ ma, teg ko naqar ca ndànd-foyfoy ga.
Teewul ñuy diiŋat ak a gàntal Yàlla Aji Kawe ji, sàmmuñu ay dénkaaneem,
Ñoo gàntal waxi Yàlla, néewal ndigalal Aji Kawe ji.
Samay loxo laa yendoo tàllal askanu fippukat, nit ñuy doxe yoon wu baaxul, topp seen xelum bopp.
Sa soppe yépp a la fàtte, kenn faalewu la ci, ndax dumay noon laa la duma, yar la yar bu tar ngir sa ñaawtéef ju réy ak sa bàkkaar yu bare.
Éy Aji Sax ji, xoolal sama njàqare, samay butit di fuddu, sama biir xol salfaañoo ndaxu tiis. Man de maa gàntal ba gàntaaral, ba fa biti, saamar di fa bóome, te biir kër it di ndee.
Boroom bee mel nib noon, modd Israyil, moddaale këram yu taaru yépp, tas ay tataam, ba fulal Janq Yuda mu taaru ma, ay yuux aki jooy.
Nanga leen àgge samay wax, ñu déglook ñu gàntal, nde ay fippukat lañu.
Teewul ñu gàntal ma, nanguwñu maa déglu. Kenn nanguwula xalab tuur yu seexluwu yi mu wékki gët, kenn dëdduwul kasaray tuuri Misra. Ma nar leena xëpp samam sànj, ŋaccal leen sama mer ci biir réewum Misra.
¶ «Waaye doom ya dañu maa gàntal. Sama dogali yoon, jëfewuñu ko, sama àttey yoon yiy guddal fanu képp ku koy jëfe, sàmmuñu ko. Sama bési Noflaay lañu ñàkke worma. Ma nar leena xëpp samam sànj, ŋaccal leen sama mer ca màndiŋ ma.
¶ «Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!