TSK

TSK · Isaiah 63:16

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Su ko defee nga wax Firawna, ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Israyil mooy sama taaw bu góor.

Aji Sax ji lañuy feye lii? Ndaw xeet wu dofe te ñàkk xel! Mooy seen baay, bind leen, sàkk leen, samp leen.

Job 14:21 TSK

Doom ya tedd, yégul; ñu tekkeedi, tinul.

Yaw Yanqóoba mi néew doole niw sax, yeen góori Israyil. Man, maa leen di dimbali. Kàddug Aji Sax jee, sab jotkat, Aji Sell ju Israyil.

Aji Sax ji dafa wax, moom buurub Israyil, jotkatam, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ne: «Maa jëkk, maa mujj, te yàlla amul ndare man.

Sa jëkkër, ki la sàkk, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee di turam. Aji Sell ju Israyil moo la jot, te moo di Yàllay àddina sépp.

Waaye déy, Aji Sax ji, yaa di sunu Baay; noo di ban, yaw ngay tabaxkatu njaq, nun ñépp di sa liggéeyu loxo.

«Maa leen naroona teral ni doom yu góor, may leen suuf su xemmemlu, ngeen gënle xeet yépp suuf. Ma noon dingeen ma wooye baay te dungeen ma dëddu mukk.

Ñooy dikk di jooy, di leewaayu, ma jiite leen, yóbbu, jaare leen xàll wu jub wu ñu dul fakktaloo, ba ca wali ndox ya, ngir maay baayu Israyil, Efrayim di sama taaw.

Xanaa du benn baay lanu am, nun ñépp? Te jenn Yàlla jee nu sàkk? Lu waral ku ne di wor mbokkam, ba fecci kóllërey maam ya?

Xam ngeen ne yëf yuy wéy yu mel ni xaalis mbaa wurus, du moom lees leen jote ci seen dundinu neen wa ngeen donne ca seeni maam,