Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. Céy Yàlla, yéefar yi song nañu sa moomeel, teddadil nañ sa kër gu sell, gental nañ Yerusalem.
TSK
TSK · Isaiah 64:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Seenum réew gental, seeni dëkk xoyomu, seen suuf, doxandéem yi lekk fi seen kanam, muy gent bu doxandéem tas.
Mu taal kër Aji Sax ji, taal kër buur, ak këri Yerusalem gépp, boole ca këri boroom barke ya.
Tey ci janti toroxte ak tumurànke, la Yerusalem di fàttlikoo mboolem ngëneeli démbam. Aw askanam a tàbbi ci loxol noon, te wall amul, noon ba gis leen, di textexi ci seenug yàqule.
Boroom bee tàwwi ag fittam mel ni ab noon, moo diire ndijooram, mel ni bañ, moo bóom mboolem lu neexa xool. Ci biir xaymay janq Siyoŋ mu taaru ma la yuri am sànjam ni sawara.
Bu juróom benn fukk yeek ñaar ciy àppi juróom ñaar weesee, dees na bóom ku ñu fal, te kenn du ànd ak moom. Gannaaw loolu kilifa dina ñëw, ànd ak gàngooram, yàqte dëkk beek jaamookaay bi. Waaye kilifa googu lu mel ni mbënn a koy mujje. Dogal nañu ne yàqte gi dina wéy ba keroog xare biy jeex.
Kon nag dees na gàbb Siyoŋ nib tool, Yerusalem googu diy tojit, jale, tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.
Su boobaa ña mu fekk ca diiwaanu Yude, nañu daw jëm kaw tund ya, ñi ci biir dëkk bi, nañu daw génn, te ña mu fekk ca tool ya, buñu duggsi ci biir dëkk bi.
¶ Ba loolu amee ñu jox ma nattukaay bu mel niw yet, ne ma: «Jógal, natt néeg Yàlla bi ak sarxalukaay bi, te nga waññ ña fay jaamu Yàlla.