TSK

TSK · Isaiah 64:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Gannaaw loolu maay dëgëral boppu Firawna, mu topp leen, ba ma jaare ca siiwal sama ndam, ndax maay daan Firawnaaki xarekatam yépp, te waa Misra dinañu xam ne, man maay Aji Sax ji.» Musaa jottli leen ko, ñu def noona.

Bés niki tey maa tàmbalee wàcce njàqareek tiitaange ci kaw mboolem askan yi asamaan tiim, ba bu ñu déggee seenum riir, dañuy jaaxle, di lox.»

¶ «Te itam doxandéem bu bokkul ci Israyil sa ñoñ bu jógee réew mu sore ngir sa tur,

Mu ngi fey xare ci àddina sépp, dog fitt, damm xeej, lakk pakk.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di woyu Sabóor.

ña ne woon: «Nan séddoo parluy Yàlla yi.»

Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragal-leen ko! Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu!

Teewul Yàlla wallu leen ngir turam, ba xamle njàmbaaram.

Kon nag Aji Sax ji sunu Yàlla, wallu nook moom, ba mboolem nguuri àddina xam ne yaw doŋŋ yaa di Aji Sax ji.»

Man daal, dungeen ma ragal, am tiituleen ma?» Kàddug Aji Sax jee. «Man mi teg gannuus, yemalee ko géej, dogalal ko ko dàkk te du ko jàll, lu mu wañax wañax du ko man; gannax ya day riir, te du jàll!

Maa koy mbugale mbas ak deret ju tuuru, ak wali waameek doji yuur, ak tawub sawaraak tamarax, mooki gàngooram, ak xeet yu bare yi ànd ak moom.

¶ Man Nabukodonosor maa ngi woon ci sama jàmmi kër ak sama teraangay màkkaan.

¶ Ba loolu wéyee Buur joxe ndigal, ñu indi nit ña tuumaaloon Dañeel, ñu tàbbal leen ca kàmbu gaynde ya, ñook seeni doom ak seeni jabar. Àgguñu suuf sax, gaynde ya alawti leen, dammate seen yax yépp.

Aji Sax ji nee: «Maa leen di won ay kiraama, na woon ba ngeen di génn réewum Misra.»