Aji Sax jee koy seppee ci mboolem giiri Israyil, ngir sédd ko njekkar, na mu dëppook mboolem alkàndey kóllëre gi ñu bind ci téereb yoon wii.
TSK
TSK · Isaiah 65:5
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Juróom benn a ngii yu Aji Sax ji bañ, ba ci juróom yaar yu mu seexlu:
Aji Sax ji sib na ku réy, da koy mbugal ci lu wér.
Farisen yi ak seeni firikat nag di xultu ci kaw taalibey Yeesu yi, ne leen: «Lu tax ngeen di lekkandoo ak a naanandoo ak juutikat yeek bàkkaarkat yi?»
Ci biir loolu Farisen ya ak firikati yoon ya di ñurumtu naan: «Kii moom bàkkaarkat yi lay neexool, di bokk ak ñoom lekk!»
¶ Yeesu léebati lii, ngir ñiy damoo seenug njub, tey doyadal ñi ci des.
¶ Ma dikk nag ci yaw miy wuyoo turu Yawut, te yaakaar yoonu Musaa, boole ci di sagoo Yàlla.
¶ Naka noonu yeen ndaw ñi, nangul-leen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»