TSK

TSK · Isaiah 7:18

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Firawna daldi woolu Musaak Aaróona, ne leen: «Demleen rendili seen Yàlla sarax, te nay ci biir réew mi nag.»

Ba loolu amee Amoreen ña dëkke tund woowa dikk, dajeek yeen, ne leen dann niy yamb, yitte leen fa Seyir, ba Xorma.

Moo àddu, weñ ya dikk, rayentaan ya dajal seen réew ma.

Aji Sax jeey yékkatil raaya, xeet wu sore, wal ug liit, wooye leen fa cati àddina, ñu jekki ne jaas, dikkal leen.

Mooy bawoo fu sore, fa asamaan digalook suuf. Aji Sax ji laak gàngoor gi muy mbugale, ngir yàqtesi réew mi mépp.

Wóoy ngalla ña wàcci Misra, di wuti wall; di sukkandikoo ay fas, tey yaakaari watiir ndax bare ga, aki gawar ndax lim bu takku ba te xooluñu ci Aji Sell ju Israyil, sàkkuwñu kooku di Aji Sax ji.