TSK

TSK · Isaiah 8:18

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aji Sax ji, yaw, ku la xam, wóolu la. Aji Sax ji, yaw, ku lay sàkku, doo ko wacc.

Boroom barke xéewlu, sujjóotal ko, ku jëm pax it, te bakkanam di lang, di ko sukkal.

Aji Sax ji wax Esayi ne ko: «Génnal gaaw, dajeek Axas, yaak sa doom Seyar Yasub, ma nga ca catal solomu mbànd ma féete kaw, ca yoonu toolu fóotkat ya.

Ba loolu weesee ma jaxasoo ak sama soxna, yonent bu jigéen ba, mu ëmb, gannaaw gi mu am ca doom ju góor. Aji Sax ji ne ma: «Tudde ko “Maxer Salal Xas Bas.”

Lees di tontu xeet wi yónnee di laaj, xanaa ne leen Aji Sax jee sanc Siyoŋ, te fa la baadooloy ñoñam di rawe.

Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.

Déglul bu baax, yaw Yosuwe sarxalkat bu mag bi, yaak sa xarit yi toog fi sa kanam te taxawe ab tegtal, nde maa ngii di indi samab jaam, ki ñuy wax Njebbit li.

Luke 2:18 TSK

Mboolem ña dégg la leen sàmm sa wax nag waaru lool.

Ndaxte damaa foog ne, nun ndawi Almasi, Yàllaa nu fésal ca sàppeb gannaaw ba, mbete nit ñu ñu teg àtteb dee, ngir nu doon ceetaanum àddina wërngal këpp, malaaka ak nit.

Leeg-leegaa ñu saaga leen, bundxatal leen ci kanam nit ñi; leeg-leegaa yeen ay taxawu nit ñi ñu teg lu ni mel.