Bare na ñu naan: «Ana ku nuy won lu baax?» Éy Aji Sax ji, baaxe nu saw yiw!
TSK
TSK · Isaiah 9:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Man de, maa ngi bége sa kàddu ni ku for alal ju bare.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee leen di ŋàbbal kàccri, na mu defoon waa Majan fa doju Oreb. Mooy xàcciw yetam, mu dal géej, na mu defoon fa Misra.
Aji Sax jee damm bant, bi ñu bon ñi daan dóoree! Moo damm seen yetu nguur,
Bésub keroog dees na ne: «Sunu Yàllaa ngii nag! Moom mii lanu yaakaaroon te moo nuy wallu. Aji Sax jii lanu yaakaaroon, nan bég te bànneexoo wallam.»
Day tóora tóor, di bànneexu, bay sarxolle, ba jagoo darajay gottub Libaŋ ak taaru àllub Karmel ak Saron. Foofa lees di gise darajay Aji Sax ji, sunu taaru Yàlla.
Ñàkkoon ngay doom, waaye ku nekk ci say doom ay dëkkalaat yii kàddu ci sab nopp: “Fii dafa xat, xajal ma, fu ma dëkke!”
«Mbégte déy, ngeen di génne, ñu yóbbu leen ci jàmm, tund yu mag yeek yu ndaw yi di leen sarxolleel, garabi àll bi yépp tàccoondoo.
Maa béga bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam njekk, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.
Yeen soppey Yerusalem yépp, bégandooleen ak moom, te di ko bànneexoo. Mboolem yeen ñi doon ñaawlu tiisu Yerusalem, bokkleen ak moom xolam bu sedd.
Ñooy dikk, di sarxollee kaw tundu Siyoŋ, ne ràññ ndax ngëneeli Aji Sax ji, pepp, biiñ aku diw, gàtt aki nag, bakkan ni tool bu ñu suuxat, dootuñu yoggoorlu.
«Éy Siyoŋ, rëccal, yaw mi dëkke janq Babilon mu taaru mi.»
Maay waliis, dajale leen, nde maa leen di jot, ñu bareeti na ñu baree woon.
Muy mbég mu réy nag ca dëkk boobee.
Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,