TSK

TSK · James 1:19

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Mbaam ma gis malaakam Aji Sax ja, daldi ne wàpp goor ca suufu Balaam, xol ba fuddu, mu dóorati mbaam ma yet wa.

Ba mu ko defee mbooloo ma mépp ñibbi, di lekk ak a naan ak a yekkle di bànneexu bu baax. Fekk na ñu xam kàddu ya ñu leen doon xamal.

Ci biir loolu ñu taxaw, di jàng ca seen téereb yoonu Yàlla Aji Sax ji, diirub xaajaatu bés ba. Xaajaatu bés ba ca topp ñuy tuub ak a sujjóotal seen Yàlla Aji Sax ji.

Job 32:16 TSK

Dama leen di xaar te waxuñu, xanaa taxaw, tontootuñu?

Wax ju bare, moy ñàkku ca; ku moom sa làmmiñ, xelu nga.

Ku gaawa mer, def jëfi dof, te kuy fexeel nit, ñu bañ la.

Ku xelu àddu, xam-xam rafet; ab dof di talalali.

Muñ mer, moo gën njàmbaar; tënk sa bakkan moo raw nangub dëkk.

Ku moom sa làmmiñ am nga xam-xam, te ku teey am ngag dégg.

Dund ak dee a ngi ci làmmiñ, te wax garab la, ku ko bëgg, lekk ca doom ya.

Ku naqari deret, sonal nga sa bopp; ku la xettli, tóllanti ko.

Ku dul ànd ak sa sago, yaa neexa song ni dëkk bu dara wërul.

Fa mbir mujjee gën fa mu doore, te muñ a gën réy-réylu.

Luke 15:1 TSK

¶ Mboolem juutikat yeek bàkkaarkat yi ñoo daan ñëw ci Yeesu, di ko déglu.

Acts 2:42 TSK

¶ Ci kaw loolu ñu pastéefu ci njànglem ndaw yi ak ci dundal ag bokkoo, ak ci dagg mburum bokkoo mi, ak ci jataayi julli.

¶ Ba ñu génnee ca jàngu ba, dañu leena ñaan ñu baamtu kàddu googu bésub Noflaay ba ca topp.

Waa Bere nag gëna am déggin waa Tesalonig. Ñu gëm kàddu gi, xér ci lool, bés bu nekk ñuy niir Mbind mi, ngir xam ndax la ñu leen di wax noonu la.

Buleen mer ba bàkkaar, te bu jant bi sowe seen mer;

Waaye léegi lii lépp baleen ko: tàng xol, ak mer mu ëpp, ak coxor, ak saaga, ak waxi ñàkk kersa.

¶ Leneen lu nu dul noppee sante Yàlla, moo di lii: ba ngeen nangoo ci sunu làmmiñ kàddug Yàlla gi nu leen dégtal, te melul ni kàddug nit doŋŋ ngeen ko nangoo, waaye kàddug Yàlla gi mu doon ci lu wér, moom ngeen ko jële, te kàddu googu mooy liggéey ci seen biir, yeen gëmkat ñi.

James 3:1 TSK

¶ Bokk yi, bu ñu bare ci yeen wuta doon sëriñi mbooloom gëmkat mi, ndax xam ngeen ne nun ñiy jàngle nooy gëna metti ab àtte.