TSK

TSK · James 1:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Maa ngii di ko tofal Oliyab doomu Ayisamaag Daneen bi, te itam mboolem ñi xarala, may naa leen xelum xarala, ngir ñu ànd def mboolem lii ma la sant:

Léegi nag Aji Sax ji, sama Yàlla, fal nga ma buur, ma wuutu saa baay Daawuda. Waaye Sang bi, man ndaw lu tuut laa, xawma sax nu may doxale.

Ngalla wutala dégg, wool dég-dég wall.

naan: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!» Ku ñàkk bopp, mu ne ko:

Ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, da di manumaa wax, gone doŋŋ laa.»

ngir ñu sàkku yërmandey Yàlla Boroom asamaan ci wàllu mbóot moomu, ndax ñu bañ leena rey mook àndandoom yaak yeneen boroom xam-xami Babilon.

Luke 11:9 TSK

Moo tax ma ne leen, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, ndax ngeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.

Teewul muy ci ñii, xetu ndee gu jëme ci ndee, te di ci ñee, xetu dund gu jëme ci dund. Boobu sas nag, ana ku ko àttan?

¶ Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la jëkka def, teg ci ànd ak jàmm, akug dal. Day taxa neexa jubool, feese yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-làqu akug jinigal.