Axab ne ko: «Damaa wax ak Nabot waa Yisreel bi, ne ko mu jaay ma toolub reseñam, ma fey ko xaalis mbaa su ko neexee ma wecci ko ko beneen toolub reseñ. Mu ne ma du ma jox toolub reseñam.»
TSK
TSK · James 4:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
1 Kings 21:6
TSK
Ecclesiastes 4:8
TSK
Kenn a ngii, kenn ñaareelu ko, du doom, du mbokk. Doñ-doñam du dakk, te du doylu, mujj mu naan: «Kan laay doñ-doñil, di xañ sama bopp bànneex?» Loolu it, cóolóoli neen, di sas wu tiis.
Habakkuk 2:5
TSK
Biiñ day wore, jàmbaar ju bew jii nag du dal-lu, xanaa yàkkli puruxam ni njaniiw, du doylu, mbete ndee, moom miy buubandoo xeetoo xeet, dajale askanoo askan, aakimoo.
Luke 11:9
TSK
Moo tax ma ne leen, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, ndax ngeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.
James 1:5
TSK
¶ Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.