TSK

TSK · James 4:6

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Musaa ak Aaróona nag dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Siide nga maa nangul daal? Waaw, foo àpp sa ngàntal ak man? Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.

Léegi nag xam naa ne, Aji Sax jee sut mboolem tuur yi, ndax la mu def, ba leen waa Misra torxalee.»

Job 40:10 TSK

Ràngool boog màggaay ak teddnga, te làmboo dayook daraja.

Aji Sax jee kawe! Ku toroxlu, mu niir; ku réy, mu ñooru.

Juróom benn a ngii yu Aji Sax ji bañ, ba ci juróom yaar yu mu seexlu:

Bésub keroog booba, kuy daŋŋiiral, detteelu, sagub nit sàggiku, Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.

Noo dégg ni Mowab réye, réya réy, reew te bew, seeni kañu di waxi neen.

Ku màgg, ku kawe ki, ki màkkaanam sax dàkk te turam sell, daa wax ne: «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, maa dëkk ak boroom xol bu mokk, te toroxlu, ngir leqli ku toroxlu, leqli boroom xol bu mokk.

Waaye ba mu bewee, të ticc bay réy-réylu, dañu koo jàllarbee ca nguuram, nangu ndam la,

Ndaxte képp kuy réylu, dees na la toroxal, ka toroxlu lees di yékkati.»

¶ Naka noonu yeen ndaw ñi, nangul-leen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»