¶ Jombul ngeen di wax ci seen xel naan: «Xeet yii gën noo bare, ana nu nu leen mana dàqe?»
TSK
TSK · Jeremiah 13:22
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Dingeen wax ci seen xel, ne: «Ana nu nuy ràññee kàddu gu Aji Sax ji waxul?»
Te noonu la buurub Asiri di yóbboo ngàllo Misra, toxal waa Kuus, ñuy ay ndaw aki màggat. Yaramu neen, tànki neen lañuy def, seen taat ne fàŋŋ, muy gàcceg Misra.
Diryànke bee, déglul lii: Yaa ngi ne finaax te naa ci sam xel: «Maa ko yor, man rekk, du keneen. Duma jooy jëkkër, duma jooy doom!»
Seenug mbon a leen di mbugal, seen ñàkk kóllëre yar leen. Ñamleen ba gis ni ngeen ma dëddoo, wormaalatuleen ma, man seen Yàlla Aji Sax ji, muy loraange ju leen wex.» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
«Ñu ngi tàwwi ni fittkat seen làmmiñu workat, seen doole ci réew mi doxaluñu ci yoon. Ñu ngii di def lu bon ci kaw lu bon, te man faalewñu ma.» Kàddug Aji Sax jee.
¶ «Su ko defee, boo waxee askan wii kàddu yooyu yépp, ñu ne la: “Ana lu waral Aji Sax ji dogalal nu musiba mu réy mii mépp? Ana fu nu tooñe ak fu nu moye sunu Yàlla Aji Sax ji?”
Yerusalem a moya moy, ba tax koo mujj di sobe; ku ko teraloon, sofental ko, ndax gis ko, mu ne duŋŋ. Moom ci boppam mu ngi binni, fuuylu.
Maay dakkal sa jëfi yàqute, ak sa gànctu ga dale ca réewum Misra, ba dootoo ko geesoo gëti nammeel, te dootoo fàttliku Misra.
Lu ko moy ma futti ko ba mu ne duŋŋ, def ko ni bés ba mu juddoo, melal ko ni màndiŋ. Maa koy def ni joor gu wow, marloo ko ba rey ko.
Ni Kanaaneen biy jula, ni la Efrayim yore màndaxekaayu njublaŋ cib loxoom, bëgga naxe.
Jantub keroog ay làmp laay niite Yerusalem, ba dikke mbugal ña fa ne degg, taaje ni biiñ ci kaw ginjriitam, te naa ci seen xel: “Aji Sax ji baaxewul, lorewul.”