TSK

TSK · Jeremiah 20:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ku yaakaar Aji Sax ji bég, leer nàññ, gàcce du ko sëlëm.

di ko sante sama jëmm jépp, naan: «Éy Aji Sax ji, ana ku mel ni yaw, di xettli néew-ji-doole ci boroom doole, ak ku néewleek ku ñàkk ca ka leen di lekk?»

Buur di àtte néew-ji-dooley xeet wi, di wallu doomi néew-ji-doole tey dëggaate kiy nennoo.

Yaa di rawtub néew-ji-doole, di rawtub aji ñàkk, biir njàqare, yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame, di ker gu ñuy serloo ci tàngoor, nde merum kilifa gu néeg mooy waame wu ne yureet ci kaw miir.

James 2:5 TSK

¶ Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo taamu ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur, gi Yàlla dig ñi ko sopp?