¶ Ibraayma dellu ne: «Ma ñemee wax ak yaw, Boroom bi, te duma dara ba dara booloo jeex.
TSK
TSK · Jeremiah 30:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ibraayma dellu neeti: «Ngalla Boroom bi, bul mer, ma wax bii yoon rekk te noppi. Léegi su ñu dee fukk doŋŋ nag?» Aji Sax ji ne ko: «Kon duma tas dëkk bi, ndax fukk ñooñu jub.»
Mu wax Kore ak gàngooram gépp, ne: «Bu ëllëgee, Aji Sax ji mooy xamle kan la séddoo ak kan mooy ki sell, mu jegeñal ko boppam. Ki mu taamu nag, dina ko jegeñal boppam.
Aaróona këf and ba Musaa wax, daw dugg ca biir mbooloo ma. Ndeke mbas ma tàmbali na ca biir mbooloo ma. Mu def ca and ba cuuraay, daldi defal mbooloo ma njotlaay.
Ab yonent laa leen di feeñalal ci seen biiri bokk, ni yaw. Maay yeb samay kàddu ci gémmiñam, mu àgge leen mboolem lu ma ko sant.
Kookooy tabax kër, ñeel sama tur, te maay saxal ab jalam ba fàww.
¶ Yaw Esra nag, seetal ci xel mu rafet mi sa Yàlla digle ci yoonam wi nga yor, nga tabb ay njiit aki xaali, ngir ñuy àtte mboolem ñi xam sa yooni Yàlla ci diiwaani Wàllaa Dex. Te ñi ko xamul, nga xamal leen ko.
Ci kaw loolu ma sas sama mbokk Anani, mu jiite Yerusalem, mook Anaña boroom tata ja, ndax la mu gëna dëggu ñu bare, gën leena ragal Yàlla.
Nee nga ma: «Ana koo doon, bay lëntal samay dogal te xamoo?» Maa wax moos te xawma lenn ci kawtéef yu ma wees, ump ma.
Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal.»
Ana kuy kii bawoo Edom, sol yére yu xonq, bawoo Boccra? Kii ak yéreem yu yànj, di daagoo dooleem ju bare? «Xanaa man mii di waxe njekk, te am dooley walloo.»
Waaye seen Yàlla Aji Sax ji lañuy jaamu ak seen buur bi ma leen di falal, mu toogal Daawuda.
Maa ngii di fëlle gottub Yurdan ni gaynde, wuti mbooy gu naat. Xef ak xippi déy, ma fëxale fa ñépp, ba tabb fa ki ma taamu. Ana moos ku mel ni man? Ku am sañ-sañ ci man? Ana njiit luy taxaw fi sama kanam?
¶ «Gannaaw loolu maa leen di waajalal ab sàmm bu leen di sàmm. Kookooy Daawuda sama jaam bi. Moom moo leen di foral, mooy doon seen sàmm.
Moo tax Aji Sax ji di leen wacc ba keroog jant, ba kiy matu mucc. Ca la bokkam ya dese bakkan di dellu, fekki seen bokki bànni Israyil.
Bégala bég, janq Siyoŋ mu taaru, janq Yerusalem mu taaru laa ne: Xaacul, sa buur a ngoog, jëmsi ci yaw, moo jot njekk ak mucc, te teewu koo woyof, war mbaam, cumbur doomu mbaam.
Ku màgg lay doon, te dees na ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla moo koy jagleel nguurug Daawuda maamam.
Ndax kat du Daawudaa yéeg asamaan, waaye moom ci boppam moo ne: “Boroom bi daa wax sama Sang, ne ko: ‘Toogeel sama ndijoor,
Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal!
¶ Gannaaw nag am nanu kilifag sarxalkat bu mag bu jàll ba biir asamaan, te mooy Yeesu Doomu Yàlla, nanu ŋoy ci yoonu ngëm wi.
Looloo tax Yeesu di defarekat bi fas kóllëre gu bees, ngir ñi ñu woo mana jot ci muur gu sax dàkk gi ñu leen dig. Deeyam gi mu dee, moom la leen jote ci bàkkaar yi ñu xëtte kóllëre gu jëkk ga.
Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.