TSK

TSK · Jeremiah 35:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Na la samab yar gënal xaalis, xam-xam dàqal la ngën-gi-wurus.

Ñu naa: «Ana ku Esayi mii di jàngal? Ana ku muy àgge xibaar? Xanaa ku yàggula fer, di doora bàyyi ween?

Aji Sax ji, xanaa du worma ngay sàkku? Dóor nga leen, safu leen; nga làbbli, ñu tanqamlu, wowle ba raw doj, baña dëpp.

Moo kan laay waxal, àrtu ko ba mu déglu, yii boroom noppi paaxee tëë teewlu! Kàddug Aji Sax jaa ngii, mel ni lu ñu rus, lu ñu safoowul!

Yonent Yàlla Yeremi daa wax ak waa Yuda gépp ak waa Yerusalem gépp, ne leen:

¶ Wattuleen bala ngeena tanqamlu kiy wax ak yeen. Ndegam ña tanqamlu woon ka yékkati woon kàddoom, wax ak ñoom ci kaw suuf ñoo rëccul, aste nun ñii, su nu dëddoo kiy waxe fa asamaan.