Aji Sax ji du nangoo baal kooku, nde su boobaa, sànjum Aji Sax jeey ànd ak fiiraangeem, tàkk ci kawam, te mboolem alkànde gi ñu bind ci téere bii day këppu ci kawam, te Aji Sax jeey far aw turam fu asamaan tiim.
TSK
TSK · Jeremiah 42:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Woo naa seede asamaan ak suuf ci yeen, bésub tey: dund ak ndee laa teg fi seen kanam, ak barke ak alkànde. Taamuleen dund ndax ngeen dund, yeen ak seen askan.
Waaye déggluwñu ma, teewluwñu ma, xanaa di jëfe seen xel ak seen dëgër bopp ak seen bon xol, ba tax ñu dellu gannaaw, jëmuñu kanam.
Nanga leen àgge samay wax, ñu déglook ñu gàntal, nde ay fippukat lañu.
Noonu la sama ñoñ di dajesee fi yaw, toogaanu la, di la déglu. Dañuy déglu say wax, waaye duñu ko jëfe mukk. Lu neex lañuy wax waaye amin wu lewul rekk la seen xol di sàkku.
¶ Teewul ñu baña déglu, të ticc, fatt seeni nopp, ngir baña dégg.
Te amul lenn lu leen di jariñ, lu ma leen nëbb, bañ leen koo xamal; jàngal naa leen ci mbeddum buur ak ci biir kër yi.