TSK

TSK · Jeremiah 44:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Jigéen ja ne Ilyaas: «Éy góoru Yàlla gii! Ana lu ma séq ak yaw? Xanaa dangaa ñëw sullisi sama bàkkaar, ba tax nga rey sama doom ju góor jii?»

Sa dëkk yu sell doon nañu màndiŋ, Siyoŋ ca la, doon na màndiŋ. Yerusalem laa ne, gental na!

¶ Aji Sax ji dafa wax ci askan wii ne: «Ñeeka bëgg ub taxawaalu, baña téye seen tànk. Moo tax man Aji Sax ji bégewuma leen. Léegi ma bàyyi xel seenug mbon, ba mbugale leen seeni moy.»

Nooy def ba defaatoo mboolem lu nu digoo woon, di taalal cuuraay Lingeeru asamaan, tuur mi, di ko tuural ay naan, na nu ko daan defe naka jekk, nook sunuy maam ak sunuy buur ak sunuy kàngam ci dëkki Yudak mbeddi Yerusalem. Teewul dañu daan doyal dugub, di woomle, te gisunu loraange.

Tabaxal nga sa bopp ab néeg, sàkkal sa bopp bérab bu kawe ci péncoo pénc.

Hosea 7:2 TSK

Taxul ñu jàpp ci seenum xel ne seen mboolem jëf ju bon laa bàyyi xel. Léegi seeni jëf a leen wër ndombo, ne màkk fi sama kanam.

Dëkk bu mag ba xar ñett, dëkk yu mag yu askani àddina yi màbb. Babilon gu mag ga nag, Yàlla bàyyi ko xel, ngir nàndal ko kaasu biiñu sànjam muy bax.