Ba Bela faatoo, Yobab doomu Sera, ma dëkk Boccra, wuutu ko.
TSK
TSK · Jeremiah 49:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Aji Sax jee yor saamar bu màndi deret, yafloo nebbon, ak deretu kuuy mu ndaw ak bëy, ak nebbonu dëmbéenu kuuy. Aji Sax ji kat moo am ab sarax fa Boccra, muy tër mu réy fa réewum Edom.
Giñ naa ko ci man mii, sama gémmiñ njekk a ciy jibe, di kàddu gu dul randu. Man la ñépp di sukkal seen bëti óom, man it la bépp boroom làmmiñ di giñe.
Kon nag, yeen mboolem Yudeen ñi sanc Misra, dégluleen kàddug Aji Sax ji. Maa giñ ci sama tur wu màgg.” Aji Sax jee ko wax. “Ma ne: Sama tur, gémmiñug benn Yudeen dootu ko tudd fi mboolem réewum Misra naan: ‘Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund.’
«Edom day mujj gental, ku fa jaare waaru, di muslu ci mboolem li ko dal.
Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maay dóor Edom sama loxo, dagge fa nit ak mala, maa koy def ab gent, la dale Teman ba Dedan, saamar lañuy fàddoo.
Boroom bi, Aji Sax jee ko giñ ci boppam, kàddug Aji Sax ji Yàllaa, Boroom gàngoori xare yi. Nee: «Maaka sib réy-réylug askanu Yanqóoba, ba seen kër yu yànj soof ma! Maay jébbale seen péey ak mboolem li ci biir.
te Esawu laa foñ. Maa def ay tundam ab gent, ab céru suufam, ma def ko dëkkuwaayu tilli màndiŋ mi.