Dañoo taal sa kër gu sell, sa dëkkuwaayu tur lañu daaneel, ba sobeel ko.
TSK
TSK · Jeremiah 52:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Sunu kërug jaamookaay gu sell ga te tedd, fa la sunuy maam daa màggale, sawara xoyom na ko, mboolem lu nu soppoon yàqu yaxeet.
kër gii ñu ma tudde, ngeen yaakaar ko, bérab bii ma leen joxoon, yeen ak seeni maam, na ma def Silo laa koy def.
Waa Babilon ñiy song dëkk bii dinañu dugg, taal ko, lakk ko ba mu jeex, lakkaale kër ya ñu doon taalal Baal tuur mi, cuuraay ca kaw taax ya, di fa tuural yeneen yàlla ay saraxi naan, ba di ma merloo.
Waa Babilon dinañu délsi, song dëkk bii xare, nangu ko, lakk ko ba mu jeex.”
Kër Buur ak këri waa dëkk ba nag, waa Babilon lakk leen, miiri Yerusalem, ñu màbb.
Aji Sax jee dogoo rajaxe tatam janq Siyoŋ mu taaru, Moo tàllal buumu nattukaay, ngir tas ko, bankul loxoom it te màbbu ko. Moo jooyloo tata ak tabaxub fegukaay, ñu ànd tojatoo.
Dinañu lakk say kër, teg la mbugal, jigéen ñu bare di gis. Maay dakkal ngànc gi nga nekke, te dootoo feyati aw far.
Waxal waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di teddadil sama bérab bu sell bii, seen sag bii ngeen di doolewoo, di seen bànneexu bët, di seen nammeelu bakkan. Seen doom yu góor ak yu jigéen ya ngeen bàyyi Yerusalem, saamar dina leen tëral.
Xamuñu sax def njub.» Kàddug Aji Sax jee. «Dañuy jal alalu fitnaak yàqute ci seen biiri taax.»
Kon nag dees na gàbb Siyoŋ nib tool, Yerusalem googu diy tojit, jale, tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.