¶ Askanu Nóoyin mooy lii. Nóoyin nit ku jub la woon, di ku mat ci biir nit ñi mu bokkal jamono, te di ku topp Yàlla.
TSK
TSK · Job 2:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Amoon na ca réewum Ucc, góor gu ñuy wax Ayóoba. Góor googu nekkoon ku mat te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon.
Mu ne ko: «Xanaa seetlu nga Ayóoba, sama jaam bi! Amul moroom fi kaw suuf de! Ku mat la te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon.»
daldi ne: «Duŋŋ laa génne sama biiru ndey te duŋŋ laay delloo. Aji Sax jee maye, Aji Sax jee nangu. Cant ñeel na Aji Sax ji.»
Ma am dëgg, sama kàddu sikkal ma, ma mucc ayib, sama kàddu teg ma tooñ.
Yàlla buma leen jox dëgg, ba ba may dee duma weddi samag mucc sikk.
Bàyyil xel ku maandu, xool ku jub; muj, fa nitu jàmm.
Ku jub mucc ci njàqare, ab soxor wuutu ko ca.
Kuy jubal day ragal Aji Sax ji, ku dëng teddadil nga ko.
Yoonu kuy jubal day moyu lu bon, ku teeylu sa jëfin, sàmm sa bakkan.
¶ Du caageenu damaa àgg ci loolu lépp ba noppi, mbaa damaa mat sëkk xaat, waaye maa ngi wéye samaw xél, di jéema jot ci neexalu rawante bi, gannaaw ba ma Almasi Yeesu jotee ci man itam.
Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant, ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi feeñee.