Ngeen daldi bànneexu fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, yeen ak seeni doom, góor ak jigéen ak seeni jaam, góor ak jigéen, ak Leween ñi ci seen dëkk, ak doxandéem yeek jirim yeek jëtun ñi ci seen biir, ci bérab bi seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam ëllëg.
TSK
TSK · Job 29:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mu dellu nag wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Sama maam ab Arameen buy màngaan la woon. Mu dem Misra, sance fa mbooloo su néew, te mujj di askan wu réy, am doole te bare.
Esra ne leen: «Ayca demleen lekk lu gëna duuf, naan lu neexa neex te sédd ci ñi amul lu ñu togg; ndax bésub tey bés bu sell la ñeel sunu Boroom. Kon buleen ci naqarlu kat, ndax bége Aji Sax ji mooy seen doole!»
Ndegam maa seetaan ku rafle nara sànku, seetaan néew-ji-doole ju amul malaan,
Yaw Yàlla, na la xeet yi sant, na la xeet yépp sant.
Bàyyeel ñoll kuy sànku, bàyyi biiñ ak boroom naqar.
Sama jaam ñeey sarxolleji ndax xol bu neex, yeen ngeen di yuuxu ndax naqaru xol, di jooyoo ndax xol bu jeex.
¶ Ndax liggéey bi ndimbal lii laaj kat, yemul rekk ci faj soxlay ñu sell ñi, waaye itam dina baawaanal cant gu bare, ñeel Yàlla.
Mbokk mi, mbégte mu réy, ak xel mu dal laa am ci sa cofeel, ndax ni nga serale xolu aji sell ñi.