wattuleen seen bopp bala ngeena fàtte Aji Sax ji leen génnee réewum Misra, kërug njaam ga.
TSK
TSK · Job 8:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
su boobaa moytuleen daldi xoggliku, fàtte seen Yàlla Aji Sax, ji leen génnee réewum Misra, kërug njaam ga,
ku bon jàq, ba gët ya giim, rawtu réer ko, yaakaaratul lu moy noowam gu mujj.
Waa làngu yéefar yi duñu am kuutaay, te xaymay lekk-kati ger yi la sawara di xoyom.
xamoo ne ku bon, ag sarxolleem àggul fenn, te bànneexu yéefar yàggul?
Ab yéefar day denc mer, te mbugal du tax mu woote wall.
Aji Sax jaa ngi feeñoo, di àtte yoon; ku bon teg ug fiir, tàbbi ca. Na jib ndànk. Selaw.
«Yeen fàttekati Yàlla yi, déggleen lii, bala maa fàdd te kenn du wallu.
Ku jub day séentu mbégte, gis ko; ab soxor yaakaar, yàkki.
Bàkkaarkati Siyoŋ tiit nañu, way-gëmadi yaa ngay lox. Ana kan ci nun moo mana dal ak sawara suy xoyome? Ana kan ci nun moo mana dal ak taal yu yànj ya dul fey?
Ca laa ne sama doolee (/muñukaaya/darajaa) jeex! ak sama yaakaar ci Aji Sax ji.
¶ Mbooloo ma nag mujj na dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, bay joggeente. Ci biir loolu Yeesu tàmbalee wax, jëkke ko ci ay taalibeem, ne: «Wattuleen lawiiru Farisen ñi, te mooy jinigal.