TSK

TSK · Joel 2:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

«Sàkklul ñaari liiti xaalis. Lu ñu tëgglu ba mu jekk nga koy def. Liit yi ngay wootee am ndaje, di ko yékkatee dal yi.

Su ñu liitee menn riirum liit mu xumb, dal yi dale penku ñooy fabu.

Ezra 9:3 TSK

¶ Ba ma déggee loolu damaa xotti sama turki ak sama mbubb, xuuf sama kawaru bopp ak sama sikkim, daldi toog, ne tott.

Sama yaram a ngi daw ndax ragal la, ragal say àtte.

Yuuxuleen! Bésub Aji Sax ji moo dëgmal, te ni sànkute gu bawoo fa ci Aji Man ji lay dikke.

Mboolem yooyu, sama loxoo ko sàkk; nii la lépp ame.» Kàddug Aji Sax jee. «Ku mel nii laay niir: néew-ji-doole ji xolam jeex, te muy déglu sama kàddu bay lox.

«Nangeen yégle lii fa Yuda, dégtale ko fa Yerusalem, yéenee koog liit fi biir réew mi te xaacu seen kem kàttan ne leen: “Dajeleen, nu dem ca dëkk ya tata wër.”

Kenn du leen sédd aw ñam wu ñuy dëfale ku deele, kenn du leen jox ub kaas, dëfale leen, doonte baay a dee mbaa ndey.

Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Céy wii ay, guléet wii ay! Mu ngii di dikk.

Àpp mat, bés jege. Bu ca jëndkat tala bég, bu ca jaaykat tala naqarlu! Am sànj a dikkal askan wépp.

Dees na la laaj ne la looy binni. Nga ne leen: “Xanaa mbir mi ma dégg. Bu agsee fit yépp ay rëcc, loxo yépp nasax, xol yépp jeex, óom yépp di fenqoo. Mu ngooguy dikk te dina am. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»

Su jongrukat ba séenee congum xare may dikk te walul liit ga, loolu waral waa réew mi fàgguwñu, ba cong ma agsi, ba rotal bakkanu kenn ca ñoom, su boobaa njubadiy jongrukat baa ko rotal, te bakkanu nit kooka, jongrukat ba laa koy topp.”

Boroom bi, seetal ci sa gépp njekk, ba waññi sa mer ak sa xadar, mu moy Yerusalem, sab dëkk, saw tund wu sell. Ndax kat sunuy bàkkaar ak sunu ñaawtéefi maam tax na mboolem ñi ñu wër di sewal Yerusalem ak sa mbooloo.

Hosea 5:8 TSK

«Wal-leen bufta gi ca Gibeya, jibal liit gi ca Raama te yéene ca Bet Awen. Moytul sa gannaaw, Beñamin.

Joel 1:15 TSK

Céy, bii bés! Bésub Aji Sax ji moo dëgmal, te ni sànkute gu bawoo fa Aji Man ji lay dikke.

Amos 8:2 TSK

Mu ne ma: «Amos, ana loo gis?» Ma ne ko: «Xanaa dàmbu meññeef mu ñor.» Aji Sax ji ne ma: «Mbugal ñoral na Israyil, sama ñoñ. Dootuma leen baal dara.

Miig! Fi kanam Boroom bi Aji Sax ji, bésub Aji Sax ji kat dëgmal na; Aji Sax jee waajal ab sarax, te moo ca sellal ay ganam.

bésub bufta ak wootey xare ca kaw dëkk ya ñu dàbbli, ak kaw tata yu kawe ya.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Maay dellu Siyoŋ, Yerusalem googu laay màkkaanoo, ba ñuy wooye Yerusalem dëkkub Worma, foofu di tundu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, lees di wooye tundu Sellnga.»

¶ Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox,

James 5:8 TSK

Yeen itam muñleen te takk seenu fit, ndax bés ba Boroom biy dikk dëgmal na.