Aji Sax jeey dëggal ñoñam, mooy ñeewante ay jaamam, bu gisee doole dëddu, ba kenn desul, dub jaam, dus gor.
TSK
TSK · Joel 2:18
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal.
Aji Sax jeey waaxu ni jàmbaar, xabtalu ni ñeyu xare, àddu ca kaw, xaacu, tiime noon yi njàmbaaram.
Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.
Aji Sax ji ne: «Du Efrayim ay sama doom ji ma sopp, gone gi may bànneexal? Lu ma ko gëdd gëdd, di ko bàyyi xel. Moo tax sama xol di ko laaj, ma yërëm koo yërëm.» Kàddug Aji Sax jee.
«Efrayim, ana nu ma lay baye, yaw Israyil laa ne, nu ma lay tege ciy loxo? Ana nu ma lay defe ni Atma? Nu ma lay yemaleek Ceboyim? Sama xol a bëpp, sama yërmandee yëngu.
«Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa fiire Siyoŋ fiiraange ju réy, am sànj mu réy laa koy fiiree.»
Xam ngeen ne ñi muñ lanu foog ne ñoom la mbég ñeel. Dégg ngeen na Ayóoba muñe woon, ak muj ga ko Boroom bi jagleel, ndax Boroom bi moo bare yërmande akug ñeewante.