TSK

TSK · Joel 2:22

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

kon maa leen di tawal ci waxtoom, suuf si nangu, garab yi meññ.

Céy Aji Sax ji, gore nga ba kaw asamaan, dëggu ba kaw-li-kaw.

Parluy màndiŋ yaa ngi walangaan, li wër tund yu ndaw yi di xumbéen.

ngay nàndal bépp ndundatu àll, di wëgg mbaamu àll,

Mooy soppi màndiŋ it, ndox ya taa, soppi suuf su ne sereŋ bëti ndox;

mooy sànge asamaan ay niir, tawal suuf, saxal tund yi am ñax,

Aji Sax jeey dëfal Siyoŋ moos, dëfalaale fépp fu fa dib gent, ba def màndiŋam ni toolub Àjjana, jooram gu wow mel ni toolub Aji Sax ji, mbégteek bànneex teew fa, ak cant gu woy feelu.

«“Waaye yeen tundi Israyil, yeenay naat, di meññal Israyil sama ñoñ, te léegi ñu ñibbsi.

Su boobaa dees na ne: ‘Xool-leen miim réew, ak mbooy gi mu doonoon, tey mu naat ni toolub Àjjana! Dëkk yeet ay gent la woon, wéet, tojatoo, tey ñu dàbbli lépp, ba dëkke nii!’

Joel 1:18 TSK

Céy ni mala yiy binnee! Gétti nag yaa ngi jànnaxe, ndax ñàkk parlu, gàtt yi itam loof.

Man nag, Niniw, dëkk bu mag bii ëmb lu ëpp fuuf téeméeri junniy nit ak ñaar fukk (120 000), ñu ràññeewul seen ndijoor ak seen càmmoñ, ak mala yu bare, duma leen xalaat?»

«Ndax jiwum jàmm lay doon, garabu reseñ meññ doomam, suuf si meññ gàncaxam, asamaan di lay. Loolu lépp laay sédd ndesu askan wii.

Maa leen di gëddal njéeréer, ba du leen yàqal meññeefum suuf, te reseñug tool du leen jaasiral.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.