TSK

TSK · Joel 2:28

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Mu am bés Yuusufa gént, nettali ko ay magam, ba tax ñu gënati koo bañ.

Ñu yegge ko Sóol, mu yebal yeneen ndaw, ñu dikk, di wax ay waxyu, ñoom it. Sóol dellooti yebal ay ndaw, ñetteel bi yoon, ñu dikk, di wax ay waxyu, ñoom itam.

ba keroog leeru xel sóobale nu fa kaw, màndiŋ mi sopplikub tóokër, tóokër meññ, ba ñu ne ab gott la.

Maay sottim ndox suuf su mar, ak wal yu waleg joor gu wow. Maay sotti saw askan samag noo, sama barke sottikul ñi nga meññ,

mboolem sa doom yu góor ay jànge ci Aji Sax ji, boole kook jàmm ju ne ñoyy.

Gannaaw bu ma walee waa kër Israyil sama noo, dootuma leen xañ sama kanam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.»

Luke 3:6 TSK

ba wépp suux gis mucc gi Yàlla dogal.”»

Acts 2:2 TSK

Ca saa sa coow jollee asamaan, mel ni riirum ngelaw lu bare doole, daldi fees dell biir kër ga ñu toog.

Acts 2:33 TSK

Yàllaa ko yéege fa ndijooram, te jot na ci Baay bi Noo gu Sell ga mu dige woon. Moom la tuur nii tey, ngeen gis ko, dégg ko.

¶ Ba Piyeer di wax kàddu googu, Noo gu Sell gi daldi wàcc ci kaw mboolem ñay déglu kàddu ga.

Acts 15:7 TSK

Werante wu réy am ca. Ci kaw loolu Piyeer jóg ne leen: «Bokk yi, yeen xam ngeen ne bu yàgg la ma Yàlla seppee ci seen biir, ngir jaambur ñi dégge ci sama làmmiñ, kàddug xibaaru jàmm bi, ba doon ay gëmkat.

Kon nag amul Yawut ak ku dul Yawut, amul ab jaam ak as gor, amul góor ak jigéen. Yeen ñépp benn ngeen ci Almasi Yeesu.