TSK

TSK · Jonah 3:10

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba Axab déggee kàddu yooyu, daa xotti ay yéreem, di woor, sol ay saaku, tëddaale ko, di temp ndànk, ngir toroxlu.

Job 33:27 TSK

nit ki seedeeli ko ca nit ña, ne: «Maa bàkkaar, maa xëtt njub, te feyeesu ma ko sax!

Leeg-leeg ma wax lu jëm ci aw xeet mbaa am réew, ne dinaa ko déjjati, daaneel ko, tas ko,

Maa dégg moos askanu Efrayim di binni naan: “Aji Sax ji, duma nga noo duma, ni sëllu wu dese tàggat. Ngalla waññi nu, nu waññiku; yaw Aji Sax ji, yaa di sunu Yàlla.

Amos 7:3 TSK

Aji Sax ji fomm ko, ne ma: «Kon du am.»

Jonah 4:2 TSK

Mu ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Céy Aji Sax ji, xanaa du lii laa waxoon ba ma génnagul sama réew? Moo taxoon ma jëkka daw, jëm Tarsis! Ndax xamoon naa ne yaw Yàlla yaay boroom yiw ak yërmande, sa mer a diib, sa ngor bare, ngay fomm mbugal.

¶ «Mu jóg, ngir dellu kër baayam. Fu sore la ko baayam séene, muy dikk. Mu ñeewante ko, daw, laxasu ko, fóon ko.