Noonu ngeen di sàkke ay jëmm yuy jëmmal seeni taab ak jëmm yuy jëmmal seen janax yiy yàq réew mi. Su ko defee ngeen defale ko Yàllay Israyil teraanga. Jombul mu woyofal loxoom ci seen kaw ak seeni tuur ak seenum réew.
TSK
TSK · Jonah 3:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
1 Samuel 6:5
TSK
Psalms 106:45
TSK
bàyyi xel ci kóllëreem ak ñoom, topp ngoram lu réy, ba giif,
Joel 2:14
TSK
Jombul mu dëpp, fomm, bàyyi gannaawam barke, ba ci saraxu pepp ak saraxu tuuru, ñeel seen Yàlla, Aji Sax ji.»
Jonah 1:6
TSK
Ci kaw loolu njiitu mool ya dikk ba ca moom, ne ko: «Yaw, ana looy nelaw? Jógal kay woo sa yàlla wall! Jombul mu geesu nu, ba dunu sànku.»
Jonah 4:2
TSK
Mu ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Céy Aji Sax ji, xanaa du lii laa waxoon ba ma génnagul sama réew? Moo taxoon ma jëkka daw, jëm Tarsis! Ndax xamoon naa ne yaw Yàlla yaay boroom yiw ak yërmande, sa mer a diib, sa ngor bare, ngay fomm mbugal.
Luke 15:18
TSK
Naa jóg, dem ca sama baay, ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la;