TSK

TSK · Lamentations 1:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Jan yàlla moo masa fexee dikk foqatil boppam aw xeet, bellee leen ci weneen xeet, ci biiri nattu, aki firnde aki kéemaan ak xare yu mu sottale dooley loxoom, ak kàttanu përëgam, ak jëf ju raglu, noonee leen ko seen Yàlla Aji Sax ji defale ca Misra, ngeen teg ci bët?

Job 29:2 TSK

Éy ku ma doon delloo jamono ya woon, fan ya ma Yàlla daa wattoo;

Bëccëg, ma jàq, sàkku Boroom bi; guddi, ma tàllal loxo, toqiwuma. Sama xol tëë sedd.

Noo ngi nii di mbalitu dëkkandoo yi; ñu séqe nu ay kókkaleeki kekku.

Mooy wax Yanqóoba kàddoom, dogalam yaak ndigali yoonam ñeel Israyil.

Sunu kërug jaamookaay gu sell ga te tedd, fa la sunuy maam daa màggale, sawara xoyom na ko, mboolem lu nu soppoon yàqu yaxeet.

Mboolem ñi fi jaareey tacc-taccali loxo, ciipu, wëcc bopp ci gentub Yerusalem mu taaru ma, te naan: «Xanaa du biib dëkk lañu doon tudd sottiteb taar ba, te muy mbégtem àddina sépp?»

Waxal Amoneen ñi, ne leen: “Dégluleen kàddug Boroom bi Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: yeena noon: ‘Ñaw!’ ba ñuy teddadil sama kër gu sell, réewum Israyil gental, waa kër Yuda jëm ngàllo.

Hosea 2:7 TSK

Ñoom seen yaay moo gànctu, ki leen ëmb moo def lu gàccelu, naan: “Damay toppi sama far, yi may jox sama lekk ak samag naan, ak samag wëñ ak sama lẽe ak samag diw ak sama biiñ.”

Xel ma mujj délsi, mu ne: “Ñaata surga la sama baay am, seen lekk ne gàññ, man, ab xiif di ma rey fii!